Jiankoote universel itam ku yor liirug dalukay nguir xaaral liguey

Share on facebook
Share on twitter
Share on linkedin
Share on telegram

Attekat thi wallu liguey thi deek Trento  tèg na boes bi 19 septembre 2023, itam  niu yor liirug dalukay nguir xaaral  liguey, am nagne sangne sangne di  njiarigne jiankoote universel. Liirug  dalukay nguir xaaral liguey dafa bokku  thi “liirug liguey dongu”, bu neek liirug  bu xame nteni moon nga thi liguey, lu  mu ndaw ndaw benna at thi boes bi nga  biddi sa tur thi téere yi nuy def  

Jiankoote universel dafa neek ndimbal  koppar thi njiaboot yi am doom, ngan yi  itam. 

Thi lu jem thi, jiankoote universel, thi  lu epp thi askan yi, thi doom italien yi,  moon ney ko am: 

Yi bok thi askan Union europeen, sen njiaboot, niu am segne segne  dek thi reew mi. 

Yi bokkul thi askan Union  

europeen, tè niu am liirug diir bu  yagg thi benna reew europeen  

wala niu am liirug bu moon len  

taxal liguey lu opp 6 weer. 

Yi an liirug nghir jiang tè niu am  segne segne dek thi bir Italy lu  

opp 6 weer

Yi an liirug tè niu nek di wor  liguey. 

Xaalis bi niatala? 

Xaalis Jiankoote bi dey tambbale thi  weer lu mu ndaw thi 50€ ba 175€ thi  njiaboot niu am xale . 

Yi am dom yi magg niu xame sen at de  tollo thi dighentè 18-21, thi weer niom  di ney lal thi 25 ba 85 €. 

Xaalis bi moon na yok thi njiaboot yi  ame dom bu febar thi ndogal Yalla; xaalis bi moon na yok thi yaye yi matul  21 at wala njiaboot yu am dom yu bari; xaalis bi moon na yok tamit thi njiaboot  yi sen xaalis matul 25 junni €. 

Naka nga muna am Jiankoote universel  boo ame dom 

-Nit ki xame tene laluniu Jiankoote at  2022, moon ney ko laaj thi Inps thi sen  site internet wala nga dem thi benna  patronat.

 (Fai domanda sul sito INPS) 

-Thi mars 2023, ku nek laaj Jiankoote,  jiarul nga laajiat. Renouvellement bi dè  nek automatique so feke muso am thi  tolof tolof. 

-Xaalis Jiankoote da fay niow thi benna  cart credit, carte bi dey am numero bu  niu tudu “iban”. Leg lè tamit xaalis  Jiankoote bi niow fu nga deek. Wayè lu  bari moy xaalis bi dè niow thi carte  bobu. Yi man dom bu magg tè sen at nek thi  diguentè 18 ba 21, niom faw niu jiot thi  xaalis Jiankoote, li niu wara def moy:

  1. nek di jiang thi daara wala jiang nghir liguey wala bok nek di jiel diplome; 
  2. nek di def stage wala nek di def benna liguey bo xame sen xalis matul 8 junni € thi at; 
  3. nek ko nekul di liguey wala ko woor  liguey; 
  4. nek ku jiang thi université nguur ghi.

 1,010 Visite totali,  9 visite odierne

Ambassade d’Italie à Dakar

SÉNÉGAL Ambassade d’Italie à Dakar Ambassade compétente pour les citoyens rèsidant au SENEGAL, MALI, GUINEE BISSAU, GUINEE KONAKRY, CAPE VERTE ET GAMBIE Adresse: Rue Alpha

 3,998 Visite totali,  1 visite odierne

Continua a leggere »